TURU MARK BI
Bio‑Oil®
TUR AK TOLLUWAAYU PORODI BI
Body Lotion 175ml
Body Lotion 250ml
TÉKTAL
Defay yokk niinaayu der bi bu baax.
WONALE
Yolaakon bu weex.
NAS BA
Diw Lotion ak 42% INGRÉDIEN yu far ci biir yi ak 14% ci tooyalukaay yi.
INGRÉDIEN YI
Aqua, Dimethicone, Isopropyl Palmitate, Ethylhexyl Cocoate, Isododecane, Isopropyl Myristate, Urea, Polyglyceryl-2 Dipolyhydroxystearate, Glycerin, Pentylene Glycol, Dicaprylyl Carbonate, Polyglyceryl-3 Diisostearate, Sodium Lactate, Dipentaerythrityl Hexacaprylate / Hexacaprate, Gluconolactone, Rosa Canina Fruit Oil, Simmondsia Chinensis Seed Oil, Calendula Officinalis Extract, Butyrospermum Parkii Oil, Helianthus Annuus Seed Oil, Glycine Soja Oil, Isostearyl Isostearate, Bisabolol, Octyldodecyl PCA, Retinyl Palmitate, Tocopheryl Acetate, Linoleic Acid, Linolenic Acid, Tocopherol, Sodium PCA, Sodium Hyaluronate, Lactic Acid, Stearalkonium Hectorite, Propylene Carbonate.
SEYTU KAARAANGE GI
Bio‑Oil® Body Lotion amna firndéel ci kaaraange buñu deguel jogéko ci ap xamtukat buy seytu lu jém ci poson, ta nék lu wéra wér ci bép waxambaane buko wara jéfandiku, yokk ci jigéen yu ëmb ak ñii di nampal, ak ay xale yu am lu ëppu ñetti at.
JÉEM DER BU WOW CI KILINIK
Bérëbu Jéemukaay Complife Italia S.r.l, Italy. Mebët Ap séytu kilinik bu jëm ci seytu xarañteef Bio‑Oil® Body Lotion ci gëna niinaayu der. Nattukàay Ñiuñ ko jaglel: 30 jigéen yu wér ci nit ñi ci bokk te amé xetu der Fitzpatirik II-V te amme der bu wow / der bu wowa wow ci séeni tànkyi. Bérëbu xayma: xayma porodi yi ñu diw ci bitti yéélu ñi ci bokk yép. Atu nit ñi ci bokk: 25–65. Anam bi ñu koy defe Xàaj yaram wi, seytukat ci kumpa, Lu ñu lambatu, ap jangat jumtukaay kilinik bu ñu kontrole. Nit ñi ci bokk raxasna ñu séeni tànk ak saabu ngir defaraat der bu wow bi ci diiru 7 fan. Amaloon na ñu ndoortel kilinik ak Xayma juntukàay yi. Bio‑Oil® Body Lotion ñu jëfe ko ñaari yoon ci bés ci 28 fan ci tànk gi ñu jox ci suuf, beneen tànk gi fajuñu ko. Xayma kilinik ak xayma juntukàay yi amaloon nañu ko ci bési 1, 3, 6, 8, 10, 14, 21 ak 28. Xayma nañ bërëb bu Fu ñu toppotowul ci jamano bu nekk. Ñóoñu ap seytukat walu gis bu ñu taggat note na léen ci wowaay (Lu ko dale 0–5). Natt tolluwàay mbaa diwu der ba der bi ak Corneometer la. Natt tolluwàay ñakkum ndox ci deret bi (TEWL) ngir tèktal ci liggéeyu niinal der, Tewameter lañu ko amale. Yokk ci, amaloon nanu laaj bu jëm ci xoolaat sa bop ci 8 ak 14 fan. Resilta Su ñu ko méngale ak fu ñu toppotowul toppoto ak Bio‑Oil® Body Lotion amna ci jéego bu am solo ci wallu lim ci wallu natt bu wowaay, Tewameter ak Corneometer, li ko dale ci bés 1, ak ci saah bu nekk. Ngir note natt bu kilinik kililik yi, yoykkute bu ama am solo ci wallu lim lu ñu séentuwoon la ci 96.7% ci nit ñi ci bokk dale bësu 14 jém ci kanam, daanaka nekk ba ñaari yoon yokkute bi amoon ci fanu 1. Ginnaaw 28 fan ci jëfandikoo, 100% ci nit ñi ci bokk wone na ñu ap yokkute 4 yoon ci wallu niinaayu derba wuté ak bèsu 1. Ni ki noonu, ginnaaw 28 fan ci jëfandikoo, 100% ci nit ñi ci bokk wone na ñu ap waññeeku ci wallu niinaayu der bu ëppu, ak yokkute bu wèsu ñari yoon bésu 1. Jéego yii ànd nañu ak resilta yu làaj xoolaat sa bop.
JÉEM BU BOROW DER BU WOW
Bérëbu Jéemukaay Ayton Global Research, Ruwyóm Uni. Mebët Ngir séytu jëfandikoo Bio‑Oil® Body Lotion Diw yaram. Nattukàay Ñiuñ ko jaglel: 119 jigéen yu wér yu ci bokk. Atu nit ñi ci bokk: 25–65. Anam bi ñu koy defe Ap jéem bu 2 ayubés ci kër ga, ngir benn bërëb. Ñi ci bokk warnañu jëfandiku porodi bi ñaari yoon bésbuné, suba ak ngóon. Dàmp ci der bi ba mu naan lépp. Matal na ñu ñetti xëtu làaj: bu njékk ginnaaw Diwu bu njékk, ñaareel bi ginnaaw 12 waxtu, ak ñetteelu bi ginnaaw 2 ayubes ci jëfëndikóó porodibi. Resilta Diwu: 95% ci nit ñi ci bokk nangu nañu ne ‘porodi bi dafa gënna leer, béppu niinalkat bu ñu daan jëfandikoo bu njékk". 93% ci nit ñi ci bokk nangu nañu ni "yëf bi dafa gënna leer, béppu niinalkat bu ñu daan jëfandikoo bu njékk". Nàan bi: 82% ci nit ñi ci bokk doon bokk nangu nañu ne "porodi bi moo gënna yomb naan béppu niinalkat bu ñu daan jëfandikoo bu njékk". 75% ci nit ñi ci bokk nangu nañu ne "porodi bi moo gëna gaaw naan, béppu niinalkat bu ñu daan jëfandikoo bu njékk". 74% ci nit ñi ci bokk bi nangu nañu ne porodi bi du bayi ndesit yu giri ginnaaw diwu bi. 86% ci nit ñi ci bokk nangu nañu ne "ginnaaw bi ñu jëfandikoo porodi bi, mënoon nañu sol yére ci sàas yi". Niinal: 93% ci nit ñi ci bokk nangu nañu ni "porodi bi defay nooyal der ci sàas yi". 92% ci nit ñi ci bokk nangu nañu ne "ginnaaw bi ñu jëfandiko porodi bi, seen der defa nooy te oyof". 90% ci nit ñi ci bokk nangu nañu ne ‘séen der gi dafa niinoon ci diiru bés bi te 91% nangu nañu ne ‘séen der gi dafa nooyoon te oyof ci diiru bés bi’. 92% ci nit ñi ci bokk nangu nañu ne "séen der yi tanewoon nañu su ñu ko tékkale ak ndoortelu 2 ayubes yi". Li ci ëpp: 73% ci nit ñi ci bokk nangu nañu ne "porodi bi moo gën, béppu niinalkat bu ñu daan jëfandikoo bu njékk".
SEYTU DER BU OYOF
Bérëbu Jéemukaay Complife Italia S.r.l, Italy. Mebët Ngir cambar ni Bio‑Oil® Body Lotion mëne inndi neewi der ba. Nattukàay Ñiuñ ko jaglel: 25 ñi ci bokk: 3 góor ak 22 jigéen; ñoom ñépp ñu am ay der yu oyof su nu sukkandikoo ci seytu bu asid laktik. Atu nit ñi ci bokk: 18–70. Anam bi ñu koy defe Jangat bu ñu sàmm.. Ñaari pacc lañu seetlu: pacc bi ñu jëfe woon ak bu negatif (ndox bu amul mineraal) ak pacc bi ñu jëfe woon ak Bio‑Oil® Body Lotion. Porodi yi ñu seytu yep ci ndiggi ñi ci bokk lañu ko def ci kaw der gi ci diiru 48 waxtu di jéfandiku ap Juntukàayu xayma Finn chamber®. Yengu yengu der ba ci teewaayu kuy yéngu ci fajum der la woon, ngir xayma tawat ci wallu der bu njékk ci 15 simili, 1 waxtu ak yeneen 24 waxtu ginnaaw bi ñu dinnde jubbantikaay. Yengu yengu der yi ci diggante 0–4 la ñu ko nattoon (fekk 0 nekkul erythema, mbaa dët mbaa yeneeni neewi der ba ak 4 nekk erythema ak dët dégg, di wone xonkaay bu lénndëm ak neewi bu yaatu ci kaw pacc bi ñuy diwu mbir ma). Resilta Kantanu yaram ci Bio‑Oil® Body Lotion neena ñu ‘neewi der ba’.
JÉEM NDAX DU JOXE AY TOMB CI YARAM
Bérëbu Jéemukaay Complife Italia S.r.l, Italy. Mebët Ngir séytu Luy inndi ay tomb yu Bio‑Oil® Body Lotion. Nattukàay Ñiuñ ko jaglel: 20 nit ñi ci bokk: 14 jigéen ak 6 góor yu jogé ci ay xeet yu wuute te am der yu ame akne. Atu nit ñi ci bokk: 18–65. Anam bi ñu koy defe Jangat bu ñu sàmm.. Porodi bi defoon na ñu ko ci ap kayitu séggukaay ci kaw ndiggi nit ñi ci bokk. Bayiwoon na ñu ci ay bandàas 48 ba 72 waxtu, dinndi lènn ba noppi délolènn ci. Defoon na ñu ci 12 bandàs ci lép ci 4 ayubes yu toftalo. Séytuwoon na ñu ñetti bérab tékkale ap test bu negatif( ndox bu amul mineraal),test bu negatif (Bio‑Oil® Body Lotion) aki kontrol bu positif (lanolin alkol, ap porodi komedo bu siiw. Yengu yengu der bi seytuwoon na ñu leen ci kanamu ap fajkatu der 15 simili ginnaaw bi ñu dinnde bandaas bu ci nekk ngir tékkale teewaayu komedo bi laata ak ginnaaw diwu porodi bi. Resilta Bio‑Oil® Body Lotion am na ñu gis ni du Komedo. Bérëb bi ñu diw Bio‑Oil® Body Lotion wutewul lu bari ak bérëbu test bu negatif bi. Test bu positif bi wonena akne.
FARAAY JANGAT
Bérëbu Jéemukaay Union Swiss Suisse, Afrik di Sud. Mebët Am na ay jangatngat yu nekk ci biir ngir seetlu faraay bi ci Bio‑Oil® Body Lotion su nu ko tékkale ay yenéen porodi niinal yu mel ni moom. Nattukàay Tékkale Bio‑Oil® Body Lotion ak 13 porodi niinalukaay 10 Mark yu màg ci àddina bi te ñu am woy gu rafet ci wallu diw. Anam bi ñu koy defe Faraay gi ñu ngi ko jànge ci jëfëndikóó Anton Paar RheoLab QC rheometer, di jëfandikoo SPINDLE CC 39, gaawaay: 200 rpm ci 20 ˚C, muñ: 155. Resilta Fësal nañu ne Bio‑Oil® Body Lotion moo gëna néewle faraay ci xaaju porodi ki ñuy diiro mbagg 7.5 yoon (94 mPa.s vs. 707 mPa.s ci ni mu tëdde nii), gëna oyof, gëna léer te moo gëna yomb naan, gëna gaawa seey.
DIWU
Naka lañu koy jëfëndikóó Bio‑Oil® Body Lotion deñ ka wara massé ci yaram wi mènni kuy reed ap weergel ci kaw yaram wi ba mu naan lépp. Li ñu wara def mooy di jëfe Bio‑Oil® Body Lotion ñaari yoon ci bés, suba ak ngoon. Bio‑Oil® Body Lotion waru ñu ko jëfandiku ci kaw góom bu ubbéeku mbaa der bu tañcu. Diwu ngir mbiri kosmetik rek moo ko taxa jóg. Yéngalal bala nga koy jëfandiko Bio‑Oil® Body Lotion ap njaxas la te fu ndox ak diw bi annde néewna lool. Lu oyof, bo bu ñu ko baye mu yem diw yi deñuy tëmb ci kaw porodi bi def fa benn kuus. Bu ñu yéngale porodi bi ndank bala ñu ko jëfandikoo, kuusu diw bi dafay delluwaat ci diw bi. Sosu Kuus bi nak mënna am 3 fan ba 3 aybes te mungi aju ci ay mbir yu mel ni tamperatiir, ci doole gi ak yoon yi ñu yéngale butel bi. Jëfandiku porodi bi bés bu nekk, te dëpp kubéer bi boo koy joxe, doyna sëk ngir tere diw bi am boobu donj. Bu diw bi forme benn donj, te ñu wasaare porodi bi fekk yéngaluñu ko, ap njaxas diw bu leer mën na génn ci butel bi. Lii du njàqare ci ki koy jëfe. Ci ban diir lañu koy jëfandiku Test bu kilinik Bio‑Oil® Body Lotion bi deñu ko jëfandiku ci diiru ñeenti ayubes moo waral ñu cammbar xarañteefu porodi bi ci ap diir. Analis lim yi wone na ap tan ci wallu melokaanu der gi ginnaaw 24 waxtu kese te tan góoge defay des ci diiru jéem bi yép. Waaye, Bio‑Oil® Body Lotion mën na ko jëfandikoo ci lu amul àp ndax niinaayam ak ay ngënelam ci wallu dunndall der su ko defe mu doon ligéeyu toppatoo der bi bés bu nekk. Boole ko ak toppoto der bés bu nekk Ngir nàan bi gëna yémb, fu ñu raxas rek lañu wara diw Bio‑Oil® Body Lotion ginnaaw bi ñu sàngoo mbaa ñu sotteeku ndox. Bu ñu jëfandiku ap diw ngir muccu ci nàaj mbaa yeneen diw nang ko def benn yoon rek Bio‑Oil® Body Lotion seeyna bu baax ci yaram wi. Jëfandiko ci biir ëmb Bio‑Oil® Body Lotion dafa séll ngir jëfandikoo ci biir ëmb. Witamin A ak ëmb Jigéen yi dafa am solo ñu di leen di sant ngir ñu waññi ferñent A ci biir ëmb, te noonu mën na ñu am jiixi jaaxa ci jëfandikoo ay porodi defar der yu am ferñent A. Bépp mbir bu ñuy def ci der du am ngaañ lu moy deñoo romb doosam ci wallu poson. Ndax der bi defay am ap baaraas bu am solo ngir tere luy duggu, ap tokk ferñent A bu ñu diw bu baax rek mooy duggu ci yaram. Kurelu Komisoŋ bu Órop buy yéngu ci siyaas ak Kàarange jëfandikukat yi (SCCS) cammbarna ferñent A aki mbiram, su ñu ko jëfandikoo ci wallu ferñenti kosmetik. Ci xalaatu CSSC, jëfandiku ferñent A ci diwu yaram yi, ba àgg ci fi mu mëna yem tollu ci 0,05% retinol amul ngaañ. Ferñent A bi nekk ci formule bi ñuy wax Bio‑Oil® Body Lotion dafa dem ba ëppu fi niinaayu diw yaram waroon a yém te mënnañu ko jëfandiku te du am benn ngaañ ci jamano ëmb. Jëfendiko leen ko bu ngeen di nampal Bio‑Oil® Body Lotion dafa séll ngir jëfandikoo ci yaram bi su ñuy nampal, waaye sopp nañu bañ ko diwu ci kus yi. Waaye, bu ñu amul lu bon, ay liir ñoo am dégërul, waru ñu lekk Bio‑Oil® Body Lotion, doon te lu tuute tuuti la. Jëfandiku ci liir yi ak ci xale yi Karaange jëfandiku Bio‑Oil® Body Lotion ci xale yu motlegul 3 at seytuwuñu ko. Ci at yu njékk yi ginnaaw juddu, ay coppite yu bari dey am ci yaramu nitki, rawatina defàasu yaram wi. Kon, ñu ngi leen di wax ñu jëfandiko ko rek ci xale yu am ñetti at mbaa lu ko ëppu. Niñu koy Jëfandiko ko ci nàaj wi Jéem yi ñu amal ci diwu yaram Bio‑Oil® Body Lotion du xécc nàaj bi mbaa mu gën ko mettilo. Kon mën nañu ko jëfandiku ci nàaj ci lu wóor, waaye du maye benn kaaraange ci reyoŋ UVA ak UVB yu nàaj bi. Konn amna solo ñu jëfandikuwaale porodi bi ak benn weer soleer bu yaatu bu am luy aar ci naaj bu tollu ci 30 lu mu néew néew. Jëfandiko ko ci a teru yaram yu am mikoos Diw yaram Bio‑Oil® Body Lotion deñoo japp ni wóorna ci fann yépp, waaye cammbaruñu kaaraange am ci ay teru yaram yu am mikoos, ndax te nekkul jëfandiku bu ñu sóoraalewoon ci porodi bi. Jëfandiko ko ak rajoterapi walla simiyoterapi Bi Bio‑Oil® Body Lotion amul ay ferñent yu mën a jël ay rajason, Li ñu digle moy ñi koy jëfandiko te ñu nekk ci rajoterapi mbaa simiyoterapi ñu làaj Fajkat yéngatu ci wallu faju bala ñuy jëfandiko porodi bi. Jëfandiko ko ak ay porodi farmasi Bio‑Oil® Body Lotion ap porodi kosmetik la. Ci wallu ndigël jém ci jëfandiku bii porodi ak ay porodi farmasi, li gën moy nga làaj ab fajkat. Jëfandiko ci der bu oyof Bio‑Oil® Body Lotion mën na jëfandikoo ci der bu oyof. Ci ab jangat bu ñu amal ci 25 nit ñi ci bokk am 18–70 at am ay der yu oyof, kenn ci ñi ci bokk amul benn àllukaay ci diwu bi. Jëfandiko ko ci der bu niin Bio‑Oil® Body Lotion mën na ñu ko jëfandiku ci der bu niin. Ci ap jéem gu ñu amaloon ci 20 nit ñi ci bokk yu am 18–65 at am der yuy am akne, fësal na ni Bio‑Oil® Body Lotion du joxe ay tomb ci yaram. Jëfandiko ko ci der buy am ay pic lu bari Bio‑Oil® Body Lotion mën nañu ko jëfandikoo ci der bu am akne. Ci ap jéem gu ñu amaloon ci 20 nit ñi ci bokk am 18–65 at am der yuy am akne, fësal na ni Bio‑Oil® Body Lotion du joxe ay tomb ci yaram. Li ñu digle moy ne, nit ñi am aknee, war na ñu laaj ap fajkat, bala ñuy jëfandikoo Bio‑Oil® Body Lotion.
AY MANDARGA DER BU WOW AK LI KOY WARAL
Mandarga yi Mandarga yu der bu wow bokk na ci ap der bu furi te wow am ay rédd, giri mbaa mel ni dóom ak di yég ap dégër ak teeŋ. Sabab yi Luy joxe der bu wow ay mbir ci biir ak ci biti la. Mbir yi ci bitti: Ap kilima bu wow defay waral niinaay bi deñe ci biir der bi jaare ci ñaari donju Lipid bu ñaari kuus yi ak ci ngelew bu wow bi ci bitti. Kilim yi ak tàngalukaay yi deñuy dinndi tooyaayu ngelew bi, mu inndi benn kilima bu wow buy dinndi niinaay ci der bi. Fóot bés bu nekk ak làal ay omo yu saf defay xar ñaari donju Lipid bu ñaari kuus yi, mu tax niinaay gëna gaawa génni ci der bi. Mbir yi ci biir: Bi yaram di màgg, der gi di génne lu néew lipids, ba tax donj Lipid bu ñaari kuus bi di gën a sew, mu waral niinayu diw bi naaw gëne yomb. Njurél mën na am njeexital ci der bu wow ndax néewaayu céramides ci donju lipid bu ñaari kuus bi. Resilta yi faraay bu wañeeku ci bariyéeru der gi bokk na ci li tax mu romb niinaay bu jaadu bi. PH bi ci der gi dafa am njéexital ci njériñu liggéeyu niinal der. Ap pH bu gëna kawe ci biir der bi dafay gallankor doxinu donj Lipid bu ñaari kuus.
DEFAR BA
Defarub Bio‑Oil® Body Lotion dafa méngo ak Anamu Defar yu Baax yi (GMP) yu ISO 22716:2007 làaj ci porodi kosmetik yi. Jumtukaay yi ñu jëfandikoo ci defarub Bio‑Oil® Body Lotion, deño ànd ak Sartifika analiise (COA), te jumtukaay yi ñu koy ëmbe yépp, ñu ngi ànd ak sértifika deppo (COC). Amul benn jumtukaay ligéey mbaa jumtukaayu pakete bu ñuy génne lu moy deñ ko seytu ba pare. Béppu wàll Bio‑Oil® Body Lotion bu ñu jaxase defa am niimero lóo. Deñoo seytu benn esantiyon bu juge ci wàll wi ci ap labo ngir melokaan, leer, xet, xamme ak espektoroftomeetar,faraay ak mikkoro biyoloosi. Esantiyon bi dën koy téye ñeent at. Sol ak pakkat bi ci Bio‑Oil® Body Lotion dafa nekk ci bërëb bu ñuy cammbare tamperatiir ak tooyaay. Ngelew li ci fu muccu ayip lay jàar (HEPA) luy segg ngir mooytu laal pënde. Ñi liggéey ci wàllu defar gi, deñuy sol ay mbaxna, ay màsk, muurukaayu kanam, ay gaa, ay west ak ay dàll. Baŋkàas bi di sàmm kalite dafay dinndi ay esantiyon saa su nekk ngir mu seytu ko nfdax amul yaxu yaxu bu am solo. niimero lóo bu ñu bind ci botel bi, Kartoŋ bi ak mbugal bi, te ñu sàmm na benn samp bu ñu sàmm ci nekk bu ñu sàkk ba ñeent at. Amul mbalit buy lore, xërëm yu bon mbaa ndesitu ndox yu ñu génne ci jëfandikoo Bio‑Oil® Body Lotion.
TÉKTAL NDÉNC
Bio‑Oil® Body Lotion war na ko sàmm ci bérab bu sédd, fu amul ceru jant bi.
DEKKILAAT
Paketu Bio‑Oil® Body Lotion yépp (butel, kubéer ak kartoŋ) deñu koy dekkilaat.
DIIR GINNAAW UBBITE BI (PAO)
Bio‑Oil® Body Lotion am na ap PAO Diir ginnàaw ubbite bu 12 weer. Lii moy diir bi ginnaaw ubbite boo xam ni porodi bi séll na te mën na ñu ko jëfandiku fekk du lor ki koy jëfe.
SÉERTIFIKA YI
Bio‑Oil® Body Lotion dafa am séertifikat Halaal ak Kosher.
GALLANKOOR
Ginnaaw bi Bio‑Oil® Body Lotion ame woy wu rafet ci wallu poson te méngo ak téralin yi ci aduna bi ci góogu wàll, ak porodi kosmetik yép, amna ap tiitàange ni jëfandikukat Bio‑Oil® Body Lotion mënna ñu gallankòor. Su fekkee ne amna gallaŋkóor, jëfandikoo porodi bi ñan ko dakkal ci sasyi. Mandarga àllukaayu der yu bon mënna doon ay tómb yu xonk, newi ak deretal, te mu wara am fi ñu diwe porodi bi. Yii jëf mënna ñu ànd ak xasan ak ap jagadi. Lu ci ëppu, gallankòor yi deñuy wañeeku ci diiru ñaar mbaa ñetti fan ginnaaw bi ñu dakkale jëfandiku porodi bi. Ba mu dellu ci melokaanam bu njëkk, der bi mënna wow te am ay ras. Su fekkee ne amna tontu buy wone alersi ci diwu Bio‑Oil® Body Lotion, luy gën moy def ay test yu alersi ngir seetlu ko. Lóolu ñu ngi koy ame ci diw tuuti Bio‑Oil® Body Lotion ci seen biir loxo yi te xàar diiru 24 waxtu ngir xool ndax benn àllukaay dina am. Luy Xonkal der bi (deretal) mba néewi bu ndaw (dët) mënna téktale ap tontu buy wone alersi.
JÉEMU ÑU KO CI AY RABU ALL
Bio‑Oil® Body Lotion ak materiyel bi mu àndal deñ léen defare ci lu déppó ak térëlinu EU bu jém ci jéem ay kosmetik ci rabu àll. Moo xam Bio‑Oil® Body Lotion la mbaa ay ferñentam, jéemu ñu benn ci ñoom ci ay rabu àll ak Bio‑Oil mbaa ñi koy inndil materiyel.
VEGAN
Bio‑Oil® Body Lotion amul benn ingrejen bu jóge ci rabu àll.
WONN CI NJUUMTE
Wonn ci njumte porodi Bio‑Oil® Body Lotion, dafa mel ni lu moy xel mu teey ak biir buy daw deñu koy seytuwaat ndax Bio‑Oil® Body Lotion amul poson. Wante, ñu ngi léen di digal ngéen jokkó ak fajkat rawatina su xale mbaa tuut tank Njumte ba wonn ko.
COPPITE CI WALLU MELOKAAN
Bio‑Oil® Body Lotion am na lu jóge ci kalendula ak diw yu am solo, ak itam witamin A palmitate, yépp di ngir der bu oyof. Nekk ci nàaj mënna inndi coppite melokàanu der bi su yagge. Bio‑Oil® Body Lotion warna ñu ko dénc ci bérab bu sédd, fu amul nàaj.
BÉS BI ÑU KO GÉJE YEESALAAT
22 UT 2023