TURU MARK BI
Bio‑Oil®
TUR AK TOLLUWAAYU PORODI BI
Skincare Oil (Natural) 25ml
Skincare Oil (Natural) 60ml
Skincare Oil (Natural) 125ml
Skincare Oil (Natural) 200ml
TÉKTAL YI
Legët yi Dafay tanelo melokaanu legët yu bees ak yu yàgg yi. Ay rew Dafay tanelo melokaanu rew. Dafay yokk taweeku der bi, kon mu tere juddu gu yeneen rew. Melokaanu der bu massé wul Dafay tanelo melokaanu der bu timpi tampa. Der buy maggat Dafay taneloo melokaanu kanam ak yaram buy maggat. Der bu wow Dafay wañi ñakk niin te taneloo melokaanu der bu wow.
WONALE
Diw bu mboq te oyof.
NAS BA
Njaxasu diw yu piir.
INGRÉDIEN YI
Glycine Soja Oil, Helianthus Annuus Seed Oil, Carthamus Tinctorius Seed Oil, Simmondsia Chinensis Seed Oil, Salvia Hispanica Seed Oil, Punica Granatum Seed Oil, Plukenetia Volubilis Seed Oil, Triticum Vulgare Germ Oil, Rosa Canina Fruit Oil, Calendula Officinalis Extract, Lavandula Angustifolia Oil, Rosmarinus Officinalis Leaf Oil, Anthemis Nobilis Flower Oil, Pogostemon Cablin Leaf Oil, Bisabolol, Tocopherol.
WUTE INGREJEN PIIR YI
Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) mën na wuute tuuti ci melokaan, xet ak sax ci saam bu ci nekk. Lii moy resilta coppite yu jaadu yi ñu séentuwoon ci ferñent piir yi seen melokaan, xet mbaa sax dina ñu soppeeku ndax yenn mbir yu mel ni waxtu wi, suuf si, yagg ci nàaj wi, li mbey mi inndi, jaawu ji, tamperatiir yi ak jamono att wi.
SEYTU KAARAANGE GI
Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) amna kenn kuy yéngu ci wallu seytu lu jém ci poson ku seytu kaaraange am mu firndéel ni amna kaaraange ñeel jéfandiku bi ko waxambaane yi wara jéfandiku, yokk ci jigéen yu wonn lor ak ñii di nampal, ak ay xale yu am lu ëpp ñetti at.
RÀÑÑEEKUKAAY PIIRE
Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) ISO 16128 moo ko déggal ni deñ ko sol ak lu piir 100% te mu jóge ci lu piir 100%.
JÉEM SEYTU DER BU WOW CI KILINIK
Bérëbu Jéemukaay proDERM Institute for Applied Dermatological Research, Hamburg, Germany. Mebët Ngir natt xarañteef bu Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) ci gëna rafetal melokaanu kël yi. Nattukàay Ñiuñ ko jaglel: 40 jigéen ñi bokk ci ay jëmm yu bare yu ñuy wax Fitzpatrick. Atu legët yi: buy sooga am ci xale bu 3 at. Fi leël yi nekk: ci kanam gi walla ci yaram ndax ay xoos xoos yu màg, ay dagg-dagg walla ay ër opeere. Atu nit ñi ci bokk: 18–65. Anam bi ñu koy defe Natkat ci kumpa, portale bu ñu seytu ci lambatu, jangat labo bu nekk ci bitti. Ap fajkatu der moo tannoon nit ñi bokk mu jëfandiku Ñiy faju ak setlukat yi (POSAS). Diwna ñu porodi bi ñaari yoon ci bés ci 8 ayubés di ko maasaase ndank ci melokaanu mbege ci kël bi ñu wone ak der bi fa wër. Jëfandiku bu ñu def ci kontrol saa su nekk. Mebët bu màg bi mu ngi nekkoon seytu njéexitalu porodi bi ci der te ñu gestu ko ak ay jumtukaay POSAS ci ndoortel ak ci 2, 4 ak 8 ayubés. Yeneen paramétar yu ñu gestu ci njéexitalu jangat bi bokk na ci séytu portale bu rafetaay ak 6 séytukat yu ñu taggat te ñu bokkal seen bopp, ak wute melokaanu deru kël ak peggam natte ko ak ap juntukàay ngir xayma melokàan der Resilta Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) dafa xareñ ci gëna rafetal melokaanu kël yi. Ap yokkute bu am solo ci lim ci POSAS (dajale seytu OSAS ak PSAS ci mebët ak lu ci am solo) ginnaaw 2 ayubés rek, mu fèss ci 94% ci nit ñi ci bokk. Ginnaaw 8 ayubés 100% ci nit ñi ci bokk wonewoon na ñu tan, tan boo wéssu ñari yoon bi ci 2 ayubés ci ginaw. Ap yokkute POSAS bu wéy ci diiru jangat bi.
AY REW JÉEM CI KILINIK
Bérëbu Jéemukaay proDERM Institute for Applied Dermatological Research, Hamburg, Germany. Mebët Ngir natt xarañteef bu Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) ci taneloo melokaanu sikatirisyi. Nattukàay Ñiuñ ko jaglel: 36 jigéen ñi bokk ci ay jëmm yu bare yu ñuy wax Fitzpatrick. Sabab rew yi: bari na ñu (ginnaaw ëmb, yaram wu yokku mbaa ay mbiri maggàay). Bërëb yi rew yi nekk: biir, pooj ak kapp. Atu nit ñi ci bokk: 18–65. Anam bi ñu koy defe Xoolaat seytu bi, portale bu ñu seytu ci lambatu, jangat labu bu nekk ci bitti. Ak fajkat moo tannoon nit ñi ci bokk ak Resilta bu Mallol. Porodi bi diwoon nañu ko ñaari yoon ci 8 bés di ko maase ndank ci melokaanu mbege ci rédd bi ñu tànn ak deru pégg yi. Jëfandiku bu ñu def ci kontrol saa su nekk. Mebët bu màg bi mu ngi nekkoon seytu njéexitalu porodi bi ci der ak Ñiy faju ak setlukat yi POSAS ci ndoortel ak ci 2, 4 ak 8 ayubés. Yeneen paramétar yu ñu gestu ci njéexitalu jangat bi bokk na ci seytu portale bu rafetaay ak 6 seytukat yu ñu taggat te ñu bokkal seen bopp, ak wute melokaanu deru kël ak peggam ni, ko ap Chromameter natte. Resilta Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) dafa xareñ ci taneloo melokaanu rew yi. Ap yokkute bu am solo ci lim ci POSAS (dajale seytu OSAS ak PSAS ci mebët ak lu ci am solo) ginnaaw 2 ayubés rek, mu fèss ci 71% ci nit ñi ci bokk. Ginnaaw 8 ayubés bés 97% ci nit ñi ci bokk wonewoon na ñu tan, tan boo xam ni matna 5 yoon bi ci 2 ayubés. Ap yokkute POSAS bu wéy ci diiru jangat bi.
JÉEMU KILINIK CI DER BU AM AY MELOKAAN YU BOKKUL
Bérëbu Jéemukaay Thomas J. Stephens & Associates, Inc., Texas, réewum Amerig. Mebët Ngir seytu Xarañteef Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) ci taaneloo melokaanu der bu am ay timpi tampa ak xeesal bu am ay tàas su ko jigéen buy deru kanam ak baatam di (maggat). Nattukàay Ñiuñ ko jaglel: 64 jigéen ci nit ñi ci bokk ak xetu der Fitzpatirik bu am yaxute der bu yem ci kanam ak ci baat. Faj ay selil ak Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) amoon na 32 nit yu ci bokk li ñu toppotowul woon amoon na 32 nit yu ci bokk. Atu nit ñi ci bokk: 30–70. Anam bi ñu koy defe Lu ñu làmbatu, cambaraat ko, ku ñu xamul moo note jangat bi ci kumpa. Nit ñi ci bokk bokkoon nañu ci ap natt bu njékk toftal ci raxas ci diiru 1 ayubés. Diwu na ñu porodi bi ci kanam ak ci baat bi ñaari yoon ci bés ci diiru 16 ayubés. Jëfandiku bu ñu ngi ko amaloon ci kanamu kenn ci ndoortel bi. Séytu ci kilinik bi ñu ngi amoon ci 0, 2, 4 ak 16 ayubés. Nit ñi ci bokk deñoo note kenn ci ñoom ci kanam ak baat ba ngir der bu am melokaan yu nirowul ak xeesal bu am ay tàas. Jëloon na ñu ay portale baat ak kanam ku nekk ci nitt ñi bokk ci masin, xayma portale bi ñungi ko amaloon ginnaaw bi jangat bi pare. Resilta Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) dafa xareñ ci taneloo melokaanu deru yaram bu yaxu ak xeesal bu am ay tàas ci der bu yaxu (maggat). Ginnaaw 16 ayubés, amna ñu resilta bu am solo lool am na ci paràmètar kanam ak baat yépp, su ñu sukkandiko ci kilinik ak xayma portale. Ginnaaw 16 ayubés, 61% ci nit ñi ci bokk wonewoon na ñu yokkute bu am solo ci wallu melokaanu der bu am melokaan yu nirowul, ak 57% xeesal bu am ay tàas.
JÉEM SEYTU DER BUY MAGGAT CI KILINIK
Bérëbu Jéemukaay Thomas J. Stephens & Associates, Inc., Texas, réewum Amerig. Jangat 1: Kanam ak baat Mebët Ngir séytu Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) ci gëna rafetal melokaanu der bu am ay melokàan yu bokkul ak xeesal bu am ay tàas su ko jigéen buy deru kanam ak baatam di (maggat) diwo. Nattukàay Ñiuñ ko jaglel: 64 jigéen ci nit ñi ci bokk ak xetu der Fitzpatirik bu am yaxute der bu yem ci kanam ak ci baat. Faj ay selil ak Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) amoon na 32 nit yu ci bokk li ñu toppotowul woon amoon na 32 nit yu ci bokk. Atu nit ñi ci bokk: 30–70. Anam bi ñu koy defe Lu ñu làmbatu, cambaraat ko, ku ñu xamul moo note jangat bi ci kumpa. Nit ñi ci bokk bokkoon nañu ci ap natt bu njékk toftal ci raxas ci diiru 1 ayubés. Diwu na ñu porodi bi ci kanam ak ci baat bi ñaari yoon ci bés ci diiru 16 ayubés. Jëfandiku bu ñu ngi ko amaloon ci kanamu kenn ci ndoortel bi. Séytu ci kilinik bi ñu ngi amoon ci 0, 2, 4 ak 16 ayubés. Nit ñi bókk deñuy leen seytuwoon ku ci nekk ci kanam ak baat bi ngir yii paramétar xareñteef: melokaan ci lépp, rédd yi, ras yu rëy, xeesal bu am tàas, der bu am melokaan yu maasewul, dégëraay/nooyaay ci gis gis, dégëraay/nooyaay taktil, melokaan bu àgg ak léer (léndëm). Jëloon na ñu ay portale baat ak kanam ku nekk ci nitt ñi bokk ci masin, xayma portale bi ñungi ko amaloon ginnaaw bi jangat bi pare. Portale yi ñu jëloon ci tolluwaay bu ci nekk seytuwoon na ñu leen ngir ay réd yu sew ak yu dijji, xeesal bu am ay tàas, der bu am ay melokaan yu nirowul, leeraay (furi) ak xayma melookaanu lépp. Resilta Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) dafa xareñ ci taneloo melokaanu deru yaram bu yaxu (maggat) ci kanam ak ci baat bi. Ginnaaw 16 ayubés, jëfandikukat bi ñuy wax Bio‑Oil ® Skincare Oil (NATURAL) defa gëna am jéego ci gurup bi ñu seytuwul bi ci paramétar xarañteef natt kilinik ak portale. Xooloon na ñu lii lu ko dale 4 ayubés, ba mu des xeesal bu am ay tàas. Ginnaaw 16 ayubés, 54% ci nit ñi bokk ci pajum selil ak Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) wone na ñu ap tan ci melokaanu kanam ak baat. Jangat 2: Yaram Mebët Ngir seytu xarañteef Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) su ko ay jigéen yu am der bu xawa yaxu (maggat) defe ci dekolte bi, suufu yéel ak deru loxo. Nattukàay Ñiuñ ko jaglel: 64 jigéen ci nit ñi ci bokk ak xetu der Fitzpatirik bu am yaxute der bu yem ci kanam ak ci baat. Faj ay selil ak Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) amoon na 32 nit yu ci bokk li ñu toppotowul woon amoon na 32 nit yu ci bokk. Atu nit ñi ci bokk: 30–70. Anam bi ñu koy defe Lu ñu làmbatu, cambaraat ko, ku ñu xamul moo note jangat bi ci kumpa. Nit ñi ci bokk bokkoon nañu ci ap natt bu njékk toftal ci raxas ci diiru 1 ayubés. Diw nañu ko ci dekolltebi, ci suufu yeel ak loxo ñaari yoon ci bés 16 ayubés. Jëfandiku bu ñu ngi ko amaloon ci kanamu kenn ci ndoortel bi. Séytu ci kilinik bi ñu ngi amoon ci 0, 2, 4 ak 16 ayubés. Kuci nekk ci ñiko téwéwoon xaymanayla ci pèt ci dekoltebi, ci suffu tankyi ak loxoyi gnir xareñteef ci wallu: gissgissu yarambi ci noyaye ak léraay ak ci taaram. Resilta Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) dafa xareñ ci taneloo melokaanu deru yaram bu yaxu (maggat). Ginnaaw 2 ayubés, jëfandikukat bi ñuy wax Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) defa gëna am jéego ci gurup bi ñu seytuwul bi ci paramétar xarañteef natt kilinik ak portale. Ginnaaw 16 ayubés, 82% ci nit ñi ci bokk ci paj mi ak Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) wone na ñu ap tan ci melokaanu dekolte bi. 93% ci melokaan suufu yéel yi ak 71% ci melokaanu loxo yi.
JÉEM SEYTU DER BUY DESIDARATE CI KILINIK
Bérëbu Jéemukaay Complife Italia S.r.l, Italy. Jangat 1: Stratum corneum niinaay ak njériñu bariyeer Mebët Ngir cambar njéexitalu jëfandiku Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) benn yoon ngir yokk stratum corneum (SC) nooyaye ak niinaye. Nattukàay Ñiuñ ko jaglel: 40 jigéen ñi bokk ci ay jëmm yu bare yu ñuy wax Fitzpatrick. Bérëbu xayma: def nañu ap porodi test ci loxo ñeep ñikko téwé. Atu nit ñi ci bokk: lu wéssu 18 at. Anam bi ñu koy defe Jangat bu ñu lambatu te xoolaat ko. Seytu niinaayu der bi ak Kornéométer, seytu njériñu liggéeyu niinal der bi ak Tewaméter. Nit Ñi doon bokk ci deñoo raxas seeni loxo ak saabu 2 waxtu laata ñuy natt ngir xool wowaayu der. Jëloon na ñu ay natt ci ndoortel. Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) bi ñu ko jëfendiko ci biir loxo ñi ko téwé yépp. Nattaat na ñu ci saas yi ginnaaw bi ñu jëfandiko porodi bi ak 1 waxtu ak 2 waxtu ci ginnaaw itam, laata ak ginnaaw bi ñu fompe porodi bi. Xayma nañ bërëb bu Fu ñu toppotowul ci jamano bu nekk. Resilta Pajum Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) jur na ap yokkute bu màg ci niinaayu der ak wañeeku bu màg ci ñakkum ndoxu der (TEWL), ap index bu yokkute ci melo bariyeer, ci jéem bu ñu xoolaat, tékkale ko ak der bu wow. Jangat 2: Melokaanu der bu wow Mebët Ngir natt xarañteef bu Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) ci taneloo melokaanu der bu wow. Nattukàay Ñiuñ ko jaglel: 25 jigéen kokasiyen yu bokkoon te amewoon der bu wow/ wow lool xoléku ci bitti yéel yi. Bérëbu xayma: diwnañu porordibi ngir xayma ci bitti yéélu yèp ñikko téwé. Atu nit ñi ci bokk: 25–65. Anam bi ñu koy defe Xàaj yaram wi, seytukat bu xamul borom ligéey ba, lambatu, ap jangat juntuwaayu kilinik. Defoon na ñu ci kilinik ay seytu der bu wow ci ak kenn ku ñu taggat ci wallu gis, seytu niinaayu der ak Korneométer ak seytu njériñu bariyeer ak juntukàay buy natt ndesitu ndox. Nit ñi ci bokk raxasna ñu séeni tànk ak saabu ngir defaraat der bu wow bi ci diiru 7 fan. Jëloon na ñu ay natt ci ndoortel. Jëfandikoo nañu Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) ñaari yoon ci bésbu nék. Xayma kilinik ak xayma juntukàay yi amaloon nañu ko ci bés 1 ak 3. Xayma nañ bërëb bu Fu ñu toppotowul ci jamano bu nekk. Resilta Pajum Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) jur na ap yokkute bu màg ci niinaayu der ak wañeeku bu màg ci ñakkum ndoxu der (TEWL), ap index bu yokkute ci melo bariyeer, ci jéem bu ñu xoolaat, tékkale ko ak der bu wow. Ay resilta jumtukaay yu ñu firndel ak analiisu der bu wow, bu ap fajkatu der def. Ay mujjantalu ci ay jangat yuñu bolé. Tane bu am solo bu melokaan bi ci wallu der bi ñu faje ak Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) ci jangat 2 defay firndel xareñteefam ci faj der bu wow ak bu wow. Li gëna déggal lii mooy yokkute bi ci stratum corneum ak TEWL ci ñaari jangat yépp.
SEYTU DER BU OYOF
Bérëbu Jéemukaay Complife Italia S.r.l, Italy. Mebët Ngir cambar ni Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) mëne inndi tawatu der buy neewi. Nattukàay Ñiuñ ko jaglel: 25 ñi ci bokk: 3 góor ak 22 jigéen; ñoom ñépp ñu am ay der yu oyof su nu sukkandikoo ci seytu bu asid laktik. Atu nit ñi ci bokk: 18–70. Anam bi ñu koy defe Jangat bu ñu sàmm.. Ñaari pacc lañu séytu: pacc bi ñu diwoon test negatif (ndox bu amul mineraal) ak pacc bi ñu diwoon Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural). Porodi yi ñu seytu yep ci ndiggi ñi doon bokk lañu ko def ci kaw der gi ci diiru 48 waxtu di jéfandiko Finn Chamber®. Yengu yengu der ba ci teewaayu kuy yéngu ci fajum der la woon, ngir xayma tawat ci wallu der bu njékk ci 15 simili, 1 waxtu ak yeneen 24 waxtu ginnaaw bi ñu dinnde jubbantikaay. Yengu yengu der yi ci diggante 0–4 la ñu ko nattoon (fekk 0 nekkul erythema, mbaa dët mbaa yeneeni neewi der ba ak 4 nekk erythema ak dët dégg, di wone xonkaay bu lénndëm ak neewi bu yaatu ci kaw pacc bi ñuy diwu mbir ma). Resilta kantanu der bi attan ci Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) neena ñu ‘du neewi bu der ba’.
JÉEM NDAX DU JOXE AY TOMB CI YARAM
Bérëbu Jéemukaay Complife Italia S.r.l, Italy. Mebët Ngir seytu ndax Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) dafay joxe akne ak komedo (ay pic). Nattukàay Ñiuñ ko jaglel: 20 nit; 14 jigéen ak 6 góor yu am ay xeet yu wuute te am der yu ame akne. Atu nit ñi ci bokk: 18–65. Anam bi ñu koy defe Jangat bu ñu sàmm.. Porodi bi defoon na ñu ko ci ap kayitu séggukaay ci kaw ndiggi nit ñi ci bokk. Bayiwoon na ñu ci ay bandàas 48 ba 72 waxtu, dinndi lènn ba noppi délolènn ci. Defoon na ñu ci 12 bandàs ci lép ci 4 ayubes yu toftalo. Ñetti pacc lañu seytu daa di tékkale test bu negatif (ndox bu amul mineral), porodi jéem bi (Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) ak test bu positif (lanolin alkol, ap porodi komedo bu ñu xam). Yengu yengu der bi seytuwoon na ñu leen ci kanamu ap fajkatu der 15 simili ginnaaw bi ñu dinnde bandaas bu ci nekk ngir tékkale teewaayu komedo bi laata ak ginnaaw diwu porodi bi. Resilta Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) am na ñu gis ne du komedo. Pacc bi ñu jëfe Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) wonewul wute lu am solo ci wàllu test bu negatif ci pacc boobu. Test bu positif bi wonena akne.
JANGAT NÀAN BI
Bérëbu Jéemukaay proDERM Institute for Applied Dermatological Research, Hamburg, Germany. Mebët Ngir cambar xayma nàan bu Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) ginnaaw biñuko jëfandiko ci niñko yoon nammé ak forotewu bi. Nattukàay Ñiuñ ko jaglel: 100 nit ñi ci bokk: 74 jigéen ak 26 góor. Bérëbu xayma: Porodi test yi ñu def ci palmeer loxo nit ñi ci bokk yépp. Anam bi ñu koy defe Jangat bu ñu dul xam boróom, bu ñu lambatu, te placebo seytu ko. Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) ak diw bu nu rañe ci la ñu jëfandikuwoon ngir xajjale ay bérab ci volar loxo nit ñi ci bokk yépp. Ñi doon bokk diwu natt porodi bi ku ci nekk lu tollu ci benn simili. Natkat yi nattoon na ñu nàanum porodi bi ci 5 poñ doore ko' nàan bu tuuti yeexa yeex' ba 'nàan bu gaawa gaaw'. Resilta Nàan bu Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) ci der bi ñu ngi ko seytuwoon mu nekk ‘gaawa gaaw’ mbaa ‘gaaw’ 64%) ci ñi ci doon bokk.
JÀNGAT CI WALLU GISS GISS
Bérëbu Jéemukaay Rigano Laboratories, Milan, Itali. Mebët Ngir seetlu ndax Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) am na benn wàllu occlusivité bu mel ni vernix caseosa. Vernix caseosa ñi bari ci borom ci ñi séen xam xam macc ci wallu kosmetik jàpp na ñu ni moy óor ci wallu niinaayu der ndax fi faraayam tollu. Anam bi ñu koy defe Am na ndox bu ñu xam nu mu tollu bu ñu sottiwóon ci ay mbalka muur ci membrane bu xawa permeyaabal bu ñuy wax Vitro-Skin™, te muy toppondóo melokaan yi ci deru nit. Lu tolloo ci wallu vernix ak caseosa ak Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) la ñu jëfandikuwoon ci membrane te tolluwaay ñakkum ndox mi ci mbalka mi nattoon na ñu ko ci waxtu. Lii deñ ko tékkale woon ak tolluwaayu ñakk ndox bi ci test mbalka yi, fekk defu ñu benn porodi ci membrane bi. Tolluwaayu seey ndoxu porodi bu ci nekk deñu ko xaymawoon. Resilta Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) am na ci lu mel ni vernix caseosa, ñu rées 24.9 ci 27.1 ci vernix caseosa.
DIWU
Naka lañu koy jëfëndikóó Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) deñ ka wara maasaas ci yaram wi ci melokaanu mbege ci kaw yaram wi ba mu naan lépp. Ñu ngi leen di wax ni porodi bi deñ ka wara jëfandiku ñaari yoon ci bés ci diiru 3 weer lu mu ndaw ndaw. Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) waru ñu ko jëfandiku ci kaw góom bu ubbéeku mbaa der bu tañcu. Diwu ngir mbiri kosmetik rek moo ko taxa jóg. Jëfandiku ko ci kaw këlu der bu wér wóorna . Nit ku nekk sa resilta du bokk ak bu keneen. Ci ban diir lañu koy jëfandiku Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) bi deñu ko jëfandiku ci diiru 8 ayubés ak 16 ayubés moo waral ñu cammbar xarañteefu porodi bi ci ap diir. Analis lim yi wone na ap tan ci wallu melokaanu der gi ginnaaw 24 waxtu kese te tan góoge defay des ci diiru jéem bi yép. Boole ko ak toppoto der bés bu nekk Ngir Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) naanu bu baax, deñ ko wara diw ci der bu ñu raxas. Di boole Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) ak yeneen porodi ngir gën ko sorilo mën na yax. Bu ñu jëfandiku ap diw ngir muccu ci nàaj mbaa yeneen diw nang ko def benn yoon rek Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) seeyna bu baax ci yaram wi. Jëfandikoo Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) ngir bép xétu yaram ginnaaw bi ñu sàngo walla xëppo ndox. Jëfandiko ci biir ëmb ñu feeñ fu nekk ci yaram wi, waaye lu ci gëna bari ci biir bi, póoj yi, ci suufu ndiggi li, taat wi, ak ween yi. Ngir mooytundiku rewu ëmb ñu ngi leen di wax ni Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) deñu ko wara jëfandiku ci yii bérëb ñaari yoon ci bés bi ci ndoortelu ñetti weer yu njékk yi ba wosin ba paré. Bi ñu ko jëfandikoo saa su nekk, Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) dina faj xasan ak der bu wow and ci ak pruritis gravidarum. Am na itam lu jëm ci xëtu yaram bu amul njariñ, lu jóge ci wuute yi am ci hormoon yi am ci biir ëmb. Witamin A ak ëmb Jigéen yi dafa am solo ñu di leen di sant ngir ñu waññi ferñent A ci biir ëmb, te noonu mën na ñu am jiixi jaaxa ci jëfandikoo ay porodi defar der yu am ferñent A. Bépp mbir bu ñuy def ci der du am ngaañ lu moy deñoo romb doosam ci wallu poson. Ndax der bi defay am ap baaraas bu am solo ngir tere luy duggu, ap tokk ferñent A bu ñu diw bu baax rek mooy duggu ci yaram. Kurelu Komisoŋ bu Órop buy yéngu ci siyaas ak Kàarange jëfandikukat yi (SCCS) cammbarna ferñent A aki mbiram, su ñu ko jëfandikoo ci wallu ferñenti kosmetik. Ci xalaatu CSSC, jëfandiku ferñent A ci diwu yaram yi, ba àgg ci fi mu mëna yem tollu ci 0,05% retinol amul ngaañ. Ferñent A bi nekk ci formule bi ñuy wax Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) dafa dem ba ëppu fi niinaayu diw yaram waroon a yém te mënnañu ko jëfandiku te du am benn ngaañ ci jamano ëmb. Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) dina nyuko jëfandikoo mu woor ci biir ëmb. Bi ñu ci boole Ferñent A ci lu néew, Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) dafay jox jigéen ñi ëmb lu am njariñ ci vitamin A, te du am benn ngaañ. Diw Rosemary ak ëmb Diw Rosemary dafa am doole lool, te ap emmenagog la, maanam mënna gisloo jigéen mbaaxam, te mënna am mu waral wosin bu teel. Moo tax ay xarit ak ay xarit yu jëfandikoo diw Rosemary ci àdduna yu mag, di leen wax ñu bañ a jëfandikoo ci biir ëmb. Waaye, diw Rosemary ci Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) dafa tuuti lool te kon lu séll ngir jëfandikoo ci biir ëmb. Jëfendiko leen ko bu ngeen di nampal Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) dafa séll ngir jëfandikoo ci yaram bi su ñuy nampal, waaye sopp nañu bañ ko def ci cus yi. Waaye, bu ñu amul lu bon, ay liir ñoo am dégërul, waru ñu lekk Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural), doon te lu tuute tuuti la. Jëfandiku ci liir yi ak ci xale yi Kaarange jëfandiku Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) ci xale yu motlegul 3 at seytuwuñu ko. Ci at yu njékk yi ginnaaw juddu, ay coppite yu bari dey am ci yaramu nitki, rawatina defàasu yaram wi. Kon, ñu ngi leen di wax ñu jëfandiko ko rek ci xale yu am ñetti at mbaa lu ko ëppu. Porodi bi deñ ko wara jëfandiko ndànk ci xale te warul jege bët mbaa gemmiñ. Niñu koy Jëfandiko ko ci nàaj wi Jéem yi ñu amal ci diwu yaram Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) du xécc nàaj bi mbaa mu gën ko mettilo. Kon mën nañu ko jëfandiku ci nàaj ci lu wóor, waaye du maye benn kaaraange ci reyoŋ UVA ak UVB yu nàaj bi. Konn amna solo ñu jëfandikuwaale porodi bi ak benn weer soleer bu yaatu bu am kaaraange ci nàaj bu tollu ci 30 lu mu néew néew. Jëfandiko ko ci a teru yaram yu am mikoos Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) jàpp na ñu ni dafa wóor ngir jëfandiku yépp ba mu des der mikoos yi. Jëfandiko ko ak rajoterapi walla simiyoterapi Bi Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) amul ay ferñent yu mën a jël ay rajason, Li ñu digle moy ñi koy jëfandiko te ñu nekk ci rajoterapi mbaa simiyoterapi ñu làaj kuy yéngatu ci wallu faju bala ñuy jëfandiko porodi bi. Jëfandiko ko ak ay porodi farmasi Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) ap porodi kosmetik la. Ci wallu ndigël jém ci jëfandiku bii porodi ak ay porodi farmasi, li gën moy nga làaj ab fajkat. Jëfandiko ci der bu oyof Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) mën nañko jëfandikoo ci der bu oyof. Ci ab jàngat bu ñu amal ci 25 nit ñu am 18–70 at ak ay der yu oyof, amul kenn ci ñoom ku ame tawat. Jëfandiko ko ci der bu niin Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) mën na jëfandikoo ci der bu niin. Ci ap jéem gu ñu amaloon ci 20 nit ñu am 18–65 at am der yuy am akne, fësal na ni Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) amul komedo. Jëfandiko ko ci der buy am ay pic lu bari Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) dessko jëfandikoo ci der bu am akne. Ci ap jéem gu ñu amaloon ci 20 nit ñu am 18–65 at am der yuy am akne, fësal na ni Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) amul komedo.
SOSU KËL
Ap kël maggàayu kolasen buy nekkaat lu bokk ci wér ginnaaw gaañu gaañu der. Kolasen dafa am ay protéin yu am solo, di jëfe ci biir yaram. Bu gaañu gaañu ci der ame, yaram wi dafay àllu ci nu mu gëna gaawe ngir defar pacc bi ñu laal, tane lay gëna faratal ci wér bu baax. Jur ay kolasen ci lu gaawa gaaw ngir faj gaañu gaañu moy luy jur kël. Doon te ap kël dina am ay coppite yu bari bala muy ñor, du mësa am doole bu tóllu ni der bi ko wër. Paxu kawar gi ak bënn bënn ñax yu nekk ci kël bi yi du ñu delluwaat . Sosu kël mungi am ñeenti pacc: Taxawlo deret buy senn bi Mungi tambali ci saas yi ginnaaw bi gaañu gaañu ame te bu am ay waxtu, ndax pacc bi gaañu defay jéema dellu ci melokaanam normaal di dajale deret ngir téye nacc bi. Selil yu gaañu yi deñuy bayi ay proteyin ci jamano jóoju ngir tambali wayal, su ko defe ñu téj wesel yu yaxu yi te wañi ñakkum deret. Ci néewi Xonkaay ak newi bi di feeñ ci diir bu ñett mbaa ñeenti fan ginnaaw gaañu mbu njékk bi ap mandarga tontu bu kaaraange yaram wi la. Selil yu weex yi di génne ay porodisimik yuy sotti raxas góom bi ak bakteri yi. Ci law bi Lii di tàmbalee ci ñetti fan, di sax ci ñetti ayubés. Ñetti taxawaay yu wuute deñuy am ci jamono gi ngir lëkkale ak tëj góom bi. Dëtal: fibroblastes (selil yuy waral seggup kolasen) deñuy feeñ ci góom bi ngir defar kolasen ci lu gaaw ngir sol góom bi. Li waeal sikatris bu mboq: ap kuus deret defay juddu ngir muur góom bi. Téjaat góom bi : deñuy dajale góom bi ngir wañi ay wi. Ci ñor Bii jamano 'tabaxaat' ginnaaw luy tollu ci ñetti ayubés lay tambali te mënna wéy ba ñaari at mungi aju ci yaatuwaay ak xootaayu góom bi. Ci jamano jooju kolasen bi defay wéy di màgg, fiibar yi di defaruwaat ndax li ñu def ci gaañu gaañu bi lu am njéexital ci kël bi. Bu kël bi di muur ak sàmm góom bi, mënna ko yaxal ci lu yomb. Deru kël bi lu ci ëpp dafay am doole ci traction bi ci suuf bi ba 70% ci der bu normaal bi.
XETU KËL YI
Ndaxte nit ñi di faj lu ëpp, gis-gisu mujj bi dafa wuute ci nit ku nekk. Mbir yu mel ni xetu der, bérab bi kël bi nekk, xetu gaañu gaañu, ati nit ki ak sax lekkam dina bokk ci luy tax kël bi mel ni muy mel. Xetu kël yi mënna ñu ko xaaj ci yii kategori: Kël yu gëna bari yi Yóoyu kël deñuy feeñ newi te léndëm ci ndoortel bi waaye su yagge defay gëna tëddaat gis ko gëna jafe ba mu nekkaat rëddu kël bu jaar yoon. Ay kël atrophik Yii kël deñuy waral sutante mbaa der bu jagadi. Am na ay misaal kël yu jóge ci akne mbaa ŋàppati. Ay kël hypertrophik Yii xël ci kaw der bi lañuy nekk. Bokk na ci li ñu leen di rañe ap lim kolasen bu ëppu, waaye defay des ak pég góom bu njékk bi. Kël Keoid Waru ñu jaawale keloid ak ay kël hypertropic. Doonte ay kël yu ñu yar la, bokk na ci mandarga keloids romb pégg góom bu njékk bi. Mën nañu wéy di magge ci diir gu èpp te lu ci ëppu deñuy delluwaat ginnaaw biñu ko daggé. Kël kontra Kël kontra mungi am su der bi teeŋe ba sax ci. Deñuy màgg su kël yi jógge fu ay yax daje, fu der lemo, ak ci ay àngal yu jub. Deru kël bi dafay bañ fuddu te mënna tere yéngatu bu jàar yoon. Ay kël kontra ci góomu lakk lay ame. Ay sikatiris (Ay rèd) Ay sikatiris dina am ci jamono coppite ci am yaram yu gàaw (ci misaal maggaayu waxambaane, ëmb) buy yaram wi di funki ci lu raw ni ko der bi di muure, mu waral ay xotteeku ci biir der bi. Bu xotteeku yóoyu di defar seen bopp deñuy def ay kël yu ñuy wax rew.
SOSU SIKATIRIS
Ci kallama wér gu yaram rew mbaa striae, ay yeneen xetu kël la rek, waaye, ñi bari deñoo jàpp ni bokku ñu ak kël. Rew ay rëdd yuy juddu ci der bi buy der bi di màgg ci lu gaaw, lu mel ni jigéen bu ëmb, defarkatu yaram ak ay waxambaane ci seen màggaay. Ni ko seen tur bi di xamle, ñu ngi jóxe ci taaweeku. Ñi gëna leer deñuy faral di am ay rew yu wiyole, te ñi gëna léndëm der deñuy faral di am ay rew yu gëna leer fi leen wër. Na ka jekk, der dafay taweeku. Taweeku bi kolasen moo koy waral ak elastin yi nekk ci dermis bi ci suufu tisi der bi. Kolasen gurup porteyin yu raxul la te benn la ci tisi yaram wi. Elastin wi juddo ci ay poroteyin yu raxul, mën na ñu ko fekk ci tisi yuy lëkkale ak di maye ay njariñam ci taweeku. Bóobu tisi buy lëkkale defay tax dermis bi mëna jano ak yéngu yéngu yaram wi muy gëna yaatu aki kontre, waaye ci jamono yokku puwa bu gàaw, mënna ñakk am jot ngir soppéeku, waral ay xotteeku ci biir tisi yaram wi. Bu xotteeku yóoyu di defar seen bopp deñuy def ay kël yu ñuy wax rew. Leeral bu am solo moy rasul bu ñuy xécc bi. Am na nooy xécce rasul yi yenn limit yi, ñu koy wax limit elastik judduwaale, defay kontrewu ngir amaat melokaanam bi woon ay yooni yoon. Waaye, yu xécce rasul bi lu ëppu ba mu romb taweku am bu jaadu, noonu rek lay melati, dootul tolluwaat ni mu tolluwoon. Doonte, ay rew du ñu feebar bu am solo, mën nañu yóbbe ñi leen di am ay xalaat yu metti. Ame ko mungi aju ci melokaanu der bi, at, ndono ak xetu lékk bi ak niinaayu der bi. Rew seen sosu nii la tëdde: Pacc benn Rew yu njékk yi deñuy feeñ ci melokaan bu furi te mën na ñu xasan tamit. Der bi ci wetu rew yi tamit mën na 'lalu' te 'sew'. Pacc ñaar Ci biir loolu, rew yi di gën a màgg ci yaatuwaay ak di gëna léndëm aki fës. Pacc ñett Bu rew yi ñore te der bi sonnatul deñuy dem di gëna furi. Mën na ñu itam feeñ ak coppite ci melokaan ak gudduwaay yu jaarul yoon.
SOSU REW CI ËMB
Am na xamal ne ci diggante 50% ak 90% ci jigéen ñi ëmb, am na ñu ay rew yu bari. Rew yi mënna ñu am ci biir bi, póoj yi, kapp yi, suufu ndiggi, taat yi ak ween yi – ay bérab yoo xamne foofu moo ëppu luy der bi di taweeku ginnaaw yaram wi defay soppeeku ci jamonoy ëmb. Donte mën a feeñ fu nekk ci yaram, ñu ngi gën a feeñ ci bérab yu ñu am geres bu bari yi. Donte rew ci 3 weer ëmb yu mujju yi lay feeñ (boori juróom bennel mbaa juróom ñaarel weer) yenn jigéen yi deñuy tambali di gis ay rew ci ñetti weer yu njékk yi. Rewu ëmb mënna itam jóge ci waajtaayu der bi ngir wosin ba ndax ormóon yu yokku. Ormóon yi deñuy gëna xécc ndox ci biir der bi, luy feexal fas yi nekk ci diggante fibru kolasen yi. Lii dafay tax xotteeku der bi gëna yómb su ñu ko xécce ak ngir melokaanu rew yi. Ame ay rew mungi aju ci melokaanu der bi, at, ndono ak xetu lékk bi ak niinaayu der bi.
DEFAR BA
Defarup Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) dafa méngo ak Anamu Defar yu Baax yi (GMP) yu ISO 22716:2007 làaj ci porodi kosmetik yi. Jumtukaay yi ñu jëfandikoo ci defarub Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural), deño ànd ak Sartifika analiis (COA), te jumtukaay yi ñu koy ëmbe yépp, ñu ngi ànd ak sartifika deppo (COC). Amul benn jumtukaay ligéey mbaa jumtukaayu pakete bu ñuy génne lu moy deñ ko seytu ba pare. Béppu wàll Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) bu ñu jaxase defa am niimero lóo boppam. Deñoo seytu benn esantiyon bu juge ci wàll wi ci ap labo ngir melokaan, leer, xet, xamme ak espektoroftomeetar,faraay ak mikkoro biyoloosi. Esantiyon bi dën koy téye ñeent at. Sollumm Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) dèfko ci karton day nekk ci bërëb bu ñuy cammbare tamperatiir ak tooyaay. Ngelew li ci fu muccu ayip lay jàar (HEPA) luy segg ngir mooytu laal pënde. Ñi liggéey ci wàllu defar gi, deñuy sol ay mbaxna, ay màsk, muurukaayu kanam, ay gaa, ay west ak ay dàll. Baŋkàas bi di sàmm kalite dafay dinndi ay esantiyon saa su nekk ngir mu seytu ko nfdax amul yaxu yaxu bu am solo. niimero lóo bu ñu bind ci botel bi, Kartoŋ bi ak mbugal bi, te ñu sàmm na benn samp bu ñu sàmm ci nekk bu ñu sàkk ba ñeent at. Amul xet yu bon, mbalit yu bon mbaa ndox bu génne ci déffaru porodi Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural).
TÉKTAL NDÉNC
Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) war na ko sàmm ci bérab bu sédd, fu amul nàaj.
DEKKILAAT
Paketu Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) yépp (butel, kubéer ak kartoŋ) luñun dekkalla..
DIIR GINNAAW UBBITE BI (PAO)
Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) am na ap PAO bu 12 weer. Lii moy diir bi ginnaaw ubbite boo xam ni porodi bi séll na te mën na ñu ko jëfandiku fekk du lor ki koy jëfe.
SÉERTIFIKA YI
Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) dafa am séertifikat Halaal ak Kosher.
GALLANKOOR
Ginnaaw bi Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) ame woy wu rafet ci wallu poson te méngo ak téralin yi ci aduna bi ci góogu wàll, ak porodi kosmetik yép, amna ap tiitàange ni jëfandikukat Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) mënna ñu am gallankoor yu bon. Su fekkee ne amna gallaŋkóor, jëfandikoo porodi bi ñan ko dakkal ci sasyi. Mandarga àllukaayu der yu bon mënna doon ay tómb yu xonk, newi ak deretal, te mu wara am fi ñu diwe porodi bi. Yii jëf mënna ñu ànd ak xasan ak ap jagadi. Lu ci ëppu, gallankòor yi deñuy wañeeku ci diiru ñaar mbaa ñetti fan ginnaaw bi ñu dakkale jëfandiku porodi bi. Ba mu dellu ci melokaanam bu njëkk, der bi mënna wow te am ay ras. Su fekkee ni am lu la jaaxal ci lu jëm ci alersi ci jëfandikoo Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural), luy gën moy def ay test yu alersi ngir seetlu ko. Lóolu ñu ngi koy ame ci diw tuuti Bio‑Oil® Body Lotion ci seen biir loxo yi te xàar diiru 24 waxtu ngir xool ndax benn àllukaay dina am. Luy Xonkal der bi (deretal) mba néewi bu ndaw (dët) mënna téktale ap tontu buy wone alersi.
JÉEMU ÑU KO CI AY RABU ALL
Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) ak materiyel bi mu àndal deñ léen defare ci lu déppó ak térëlinu EU bu jém ci jéem ay kosmetik ci rabu àll. Moo xam Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) la mbaa ay ferñentam, jéemu ñu benn ci ñoom ci ay rabu àll ak Bio‑Oil mbaa ñi koy inndil jumtukaay.
VEGAN
Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) amul benn ingrejen bu jóge ci rabu àll.
WONN CI NJUUMTE
Su féké jumnañu wonn Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural), dafa mel ni lu moy xel mu teey ak biir buy daw deñu koy seytuwaat ndax Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) amul poson. Wante, ñu ngi léen di digal ngéen jokkó ak fajkat rawatina su xale mbaa tuut tank Njumte ba wonn ko.
COPPITE CI WALLU MELOKAAN
Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) am na kalendula, chamomile, lavender ak rosemary ay jëmm ak ay diw yu am doole, di itam vitamin A ci melokanu, ñoom ñépp andu ñu ak nàaj Nekk ci nàaj mënna inndi coppite melokàanu der bi su yagge. Waaye dafa mel ni du yax xarañteefu porodi bi. Ci wallu kaaraange, butel yu Bio‑Oil® Skincare Oil (Natural) am na luy naan UV. Waaye, prodi bi waru ñu ko def ci nàaj.
BÉS BI ÑU KO GÉJE YEESALAAT
22 UT 2023